Letra de Gagganti ko
Ba ñu la koy jox, xamul dara Bu la séenee, daw gatandu la Ay waajurëm, da ñoo amoon yaakaar ci yaw Jamonooy dox, jafejafe am, sëytaane ñëw Bu ko dóor, bu ko saaga, bu ko xas, bu ko wax lu ñaaw Dellool sa xel, ca ginnaaw, te muñël koBa ñu la koy may, xam ul dara Bu la séenee, daw laxasu la Ay waajurëm, da ñoo amoon yaakaar ci yaw Jamono dox, jafejafe am, sëytaane ñëw Bu ko dóor, bu ko saaga, bu ko xas, bu ko wax lu ñaaw Dellool sa xel, ca ginnaaw, bu ko souffrir loo Xoolal ci ay, waajurëm, bu ko joy looBu juumee gagganti ko Bu juumee gagganti ko Bu juumee gagganti ko Bu juumee gagganti ko Bu juumee gagganti koBu ko dòor, bu ko saaga, bu ko xas, bu ko wax lu ñaaw Bu yënggëlee daal, ba sa xol fees, génnël nga dem Bu fa toog yaw, teranga bu mu, sàmmal sa cér Woo ko, waxtaan ak moom, té muñël koBu juumee gagganti ko Bu juumee gagganti koYaw tam, bul forcer, deel négocier Ndaw sii, bul teg deal, bul planifier Te bu amee, lu fi leerul, nga clarifier Coow li, bu déborder, nga pacifierYaw daal, bul forcer, deel négocier Ndaw sii, bul teg deal, bul planifier Te bu amee, lu fi leerul, nga clarifier Coow li, bu déborder, nga pacifier Wa waawJaajëf, di na tax, xale wone jom Waaw góor, di na tax, xale yokk jom Di ko won sa jom, moo koy dolli jom Jom jom jom rek, dara lu dul jomJaajëf, di na tax, xale wone jom Waaw góor, di na tax, xale yokk jom Di ko won sa jom, moo koy dolli jom Jom jom jom rek, dara lu dul jomYërëmal ma ko, moomit Mu wégal ma laa nax ko neex al ma ko Moomit mu xam ko