Letra de Pullo Àrdo
Ku fi ñëw mu jangal la Nax mi moo ko moon noox mi moo ko moom Daf ko dónn Lii xar yi la, lii bey yi la Nagam yangi, àli bàngi Baaxi maamam Pullo Àrdo Ku fi ñëw mu jangal fa Nax mi moo ko moon noox mi moo ko moom Lii xar yi la, lii bey yi la Nagam yangi, àli bàngi Baaxi maaman Pullo Àrdo Pullo Àrdo, Pullo Jééri, Pullo Àrdo Pullo Jééri, Pullo Àrdo, Pullo Jééri Dàqqal yee ñu jëm fee nga dàqq yil ñu jëm fii Yaa xam yaw li xew fee, dara jaxalula fii ba fee Pullo Àrdo, Pullo Jééri, Pullo Àrdo Pullo Àrdo, Pullo Jééri, Pullo Àrdo Àrdo sex na gënnëm Dàldi gàddu yattam Ma nga ànd ag xaajam Dàldi jittël géttam Pullo Jééri, Pullo Àrdo Mi ngi ànd ag xaajam Dàldi jiitél géttam Dalal xelam, fééxal xolam Bu nin ñi fo aka ree moom yégu ko suuy Pullo Àrdo, Pullo Jééri Yeppam mu ngi fii Fii la yaroo, fii la màgee Te yii fii la takkee sowna Léppam fii la Pullo Àrdo, Pullo Jééri Bu nin ñi tëbë ka dal moom yëgu ko Li mu am fii doyloo na ko doy loo na ko Bu dee cor la mbaa jamaan la Walla etaas la, mbaa abyong la, mbaa leneen la Moom gisu ko, Pullo Àrdo Ma nga gàddu taxaaran Di mbiip mbiip mu am xorom Way, way yu amui moroom Mel ni kuy neexai goroom Boo fa jaaree sant Saar ee di na la ree Boo fa jaaree doon Séréér ee di na la ree Boo fa jaaree sant Saat ee di na la ree Boo fa jaaree doon Séréér ee di na la ree Di mbiip mbiip mu am xorom Way, way yu amui moroom Mel ni kuy neexai goroom Boo fa jaaree sant Saat ee di na la ree Boo fa jaaree doon Séréér ee di na la ree Boo fa jaaree sant Saat ee di na la ree Boo fa jaaree doon Séréér ee di na la ree