Escuchar "Dabbaax" Amazon Music Unlimited (ad) Prueba Gratis 30 días

Letra de Dabbaax

Keroog bés pénc ma ba ñuy wàja wàccee jànt bi Di waajal peese ba Mullaay Dabbaax Yàlla nañ la jege Yàlla daal mooy tànn waayam Mullaay Dabbaax Bu ñu fàtte, bës boobu le Bu ñu sore, bës boobu le Bu ñu fàtte, bës boobu le Loo fa ñaan, Yàlla mey la ko Moo daan waxal ñu ñuul ñi Moo daan waxal nasaraan wi Moo daan gàddu askan wi Dafa daan wax naan nan boole sunu rééw mi Dafa daan wax naan bu kenn yëngël gaal gi Dafa daan wax naan nañ boole sunu xol yi Dafa daan wax naan nanñ yërëm jigéén ñi Sa boroom bi bég na yónnentam bi bég na Yaa ko ligééyal sa boroom Mullaay Dabbaax yaw de wàcc nga mëssoo wax lu amul Keroog ba nga ñu jitoo asamaan si daa lëndëm bësë ngii kenn dootu ko fàtteeti Mullaay Dabbaax Bu ñu fàtte, bës boobu le Bu ñu sore, bës boobu le Bu ñu fàtte, bës boobu le Loo fa ñaan, Yàlla mey la ko Moo daan waxal ñu ñuul ñi Moo daan waxal nasaraan wi Moo daan waxal askan wi Dafa daan wax naan na ñëpp ligééy Dafa daan wax naan nañ jàngal jigéén ñi Daawul seetaan fu ñaaw Pusóóm la yoroom, fu xótteeku mu ñaw Rééw mi rééw mi ameel nañ la njukkël Mullaay Dabbaax Daawul seetaan lu ñaaw Pusóóm la yoroom, fu xótteeku mu ñaw Rééw mi rééw mi ameel nañ la njukkël Mullaay Dabbaax Bakkariik Daramaa Maram Loo Kumba Caam Ngañ Péndaak Paate Pénda Moo daan waxal ñu ñuul ñi Moo daan waxal nasaraan wi Moo daan gàddu askan wi Dafa daan wax naan nañ yaatu suñu rééw mi Dafa daan wax naan na ñëpp ligééy Dafa daan wax naan nañ yërëm jigéén ñi Dafa daan wax naan nañ jàngal gune yi